KAN MOOY SOKHNA ASTOU GAWANE MBACKE bint Cheikh Ahmadou Bamba

  Рет қаралды 14,737

Xassaïdes Yi

Xassaïdes Yi

Күн бұрын

KAN MOOY SOXNA ASTU GAAWAAN ?
Soxna Aychatu Mbàkke bint Cheexul Xadiim, ñu gën koo xam ci Soxna Astu Gawaan. Mooy ki njëkka feeñ jamono ginaaw bi Sëriñ bi jugée ci géej gi, ci weeru koor atum 1904 ca Xumaag (Mauritanie).
Wayjuram wu jigéen mi ngi tudd Soxna Soxna Xadijatu Joob, dëkk ca Kokki, gëna siiwé ci Soxna Xari Gànnaar, ndax daa féeté woon Mauritanie jamono yi fa Sëriñ bi nekkee.
Soxna Astu, mi ngi jàngge Alxuraan ci nijaayam ju tudd Maam Sàmba Jaaga Joob. Ginaaw bi jàngg na ci moom lenn ci téeréy xam-xam.
Bi mu tolle ci dem kër, Sëriñ bi jox ko mbokkam mu tudd Sëriñ Muhamadul Amin Turé, mi bokk ak Allaaji Moor Faati Turé mom Maam Seex Anta.
Ba mu fa demee, nekkee woon fa jaamu Yàlla, ak ligéey ak topp kilifaam, Yàlla defal ko fa njaboot gu bàrkeel, muy Soxna Buso Turé, Soxna Ami Turé ak Sëriñ Moodu Turé.
Waaye ñatti doomam yépp nak làqu nañ lu jiitu Soxna si di fi jugé, mu wane woon ca ak ngëm lool ak wakkiilu ci Yàlla, dàl di wax ne « bu ma kenn jooyal, man da may sant Yàlla ba ma sama doom yépp jiitoo, ndax sama xol baña bëgg leneen lu dul Yàlla ».
Soxna Astu, doonoon ku yaatu lool, tabe lool, bëgg Alxuraan lool ak Qasida, fonkk njabootug Boroom Tuubaa lool, daan léen seeti ak di léen topotoo. Doonoon ku amub cér ci ñoom, daan léen tarbiya ak di léen ligéey loo ngir faj séeni aajo.
Sëriñ Fàllu mas naa seede ci moom ba wax doomam Sëriñ Moodu Buso Jeng neko, « sa bajjan de soo fexee ba làq ngëramam, aajo joo amati di na faju ».
Nekkoon ku mana yar jigéen ci ligéeyub kër ak xamal léen àdduna, goor ñi yit daan na léen tarbiya ci di léen ligéey loo, ak di léen zikar loo ak jàng Qasida.
Qasidag Mawahibu ak Sindiidi, bokkoon na ci yi mu gënoona fonkku, te daan digal Murid yi ñuy farlu ci di ko jàng.
Fonkoon na Café Tuubaa lool, ndax Sëriñ Tuubaa da ko koo masa jox ci loxol boppam, mootax Yàlla defaloon na ko ci ak jagle, ba daan na ci saafara mbooleem jangoro yi ak di ci faj aajoy jaam ñi.
Noonu la doone woon ab taalubé bu dëggël, te ñépp ràññee ko ci bëgg Sëriñ Tuubaa, daan na def sax leeg-leeg ku koy ñaanloo mbiri àdduna, mu di la wax naan « ak taalibé rekka jara ñaanlu »
Bis bii ñu koy fàttali ku di màggal giñ koy defal ci 25 diggi tabaski, mi ngi ko doon defee ci ndigalul Boroom Tuubaa, daan na ko def ca Gaawaan, ak Ndulo ba ba muy ñibbi si Tuubaa, bàyi wu ko, ba ni mu làqoo, moom lañ koy fàttali koo ba leegi.
Sëriñ Muusaa Ka moo ko defaloon bëyit yii :
"Ya bint Cheyxii Ahd’ibn Jaara
Yàl na nga am ay doom yu sampi daara
Gis naa la ngay jàngg « Sujood ak Mulki »
Yàl na la Seex Bàmba dugal ci fulki
Xam naa ni soo doon goor yilif waa Mbàkke
Mbaa ngay fetal jihaar, di dem ba Màkka
Seetal sa maam mu baax ma, wàkka Jaxu Jéey
Darale woon na réew mi, noon ya di ko jooy
Kon nak bi ngay jigéen, royal ca Aycha
Ngir Saadixiina’ag Saadixaati yaafusa
Yiléy bëyit maa la ko woy man Muusaa
Ngir xam ne garbu woo ni jeegi siisaa"
Soxna Astu, ginaaw bi mu dundé dundu gu bàrkeel, te daan xettalee, amoon yërmandé lool ci mbindéef yi, te amoon yitté ju kawe lool, mi ngi làqu ci atum 1984, ñu deñci ko ci Tuubaa.
Yàl na nu Sëriñ Tuubaa fayal
Ci xalimag : Akb Majalis

Пікірлер: 24
@mactardiouf7249
@mactardiouf7249 2 жыл бұрын
Machalah sohna astou gawane yalna yala yok ay le ram ta taf gnou si barkem
@amdifall
@amdifall Жыл бұрын
DJEUREUDJEUFFER SERIGNE TOUBA DJARAWLAKA MAME CHEIKH
@Gadiongom-ec3pr
@Gadiongom-ec3pr Жыл бұрын
Thieye yalla nanouko yalla faye❤
@astoumbacke2256
@astoumbacke2256 5 жыл бұрын
Thieye sama badiane
@moustaphaseck3767
@moustaphaseck3767 4 жыл бұрын
Thiaye sokha na Astou badién kénla
@serignengom9143
@serignengom9143 5 жыл бұрын
Thiey cheikh Ibrahima fall
@mamediarrathioub6147
@mamediarrathioub6147 Жыл бұрын
Louwerela dh❤❤❤ 4:21
@astoundiaye5996
@astoundiaye5996 2 жыл бұрын
Thiey sama badiene
@serignemodougueye6227
@serignemodougueye6227 2 жыл бұрын
Thiey sokhna ci 😭😭😭
@sidymoukhtarfalltouba9383
@sidymoukhtarfalltouba9383 6 жыл бұрын
Ndayesane Thiéye sokhna astou Gawane
@XassaidesYi
@XassaidesYi 6 жыл бұрын
Sidy Moukhtar Fall Touba kenneu laa
@BoBalde-s2z
@BoBalde-s2z 6 ай бұрын
Thieuy mame astou mbacké❤
@devndiaye9954
@devndiaye9954 Жыл бұрын
Thiey yallah sounou borom yokou ay léram té tass gnou si barkém
@sokhnasdioum6764
@sokhnasdioum6764 6 жыл бұрын
Ndeysane ceey
@XassaidesYi
@XassaidesYi 6 жыл бұрын
Sokhna s Dioum Moy Ndeyou ndiangue katou XASSIDAS YI
@sokhnasdioum6764
@sokhnasdioum6764 6 жыл бұрын
Ndeysane yalna gnu mel ni mom
@XassaidesYi
@XassaidesYi 6 жыл бұрын
Sokhna s Dioum Xana guen Rooy ci mom rek 🙏🏿
@serignengom9143
@serignengom9143 5 жыл бұрын
Kii di wah toureum waronenaniouko binda si souff
@serignengom9143
@serignengom9143 5 жыл бұрын
Douma doyol si wahtaanou sohna si
@serignengom9143
@serignengom9143 5 жыл бұрын
Amna solo lool
@serignengom9143
@serignengom9143 5 жыл бұрын
Damakoy beggué boubah wallahi
@MoustaphaiSamb
@MoustaphaiSamb Жыл бұрын
Diadief
@serignengom9143
@serignengom9143 5 жыл бұрын
Lou waral gawaane gui ap question
@Abdourahmane-w3b
@Abdourahmane-w3b 2 ай бұрын
Ziare dieuwrigne dafa melni guawane maname darou salam la deukkon wala la fétéwéwon
Var bi ak Antoine DIOME borom bus bi nena enquête amoul 😂😱
17:19
We Attempted The Impossible 😱
00:54
Topper Guild
Рет қаралды 56 МЛН
Enceinte et en Bazard: Les Chroniques du Nettoyage ! 🚽✨
00:21
Two More French
Рет қаралды 42 МЛН
UFC 310 : Рахмонов VS Мачадо Гэрри
05:00
Setanta Sports UFC
Рет қаралды 1,2 МЛН
coco在求救? #小丑 #天使 #shorts
00:29
好人小丑
Рет қаралды 120 МЛН
thiaye mame cheikh Ibrahim fall🦻👂👂💯🤍💙
3:11
Kourel kanzoul Mouhtadine tv
Рет қаралды 977
Documentaire sur Sokhna Astou Gawane bintou Cheikh Ahmadou BAMBA 1443H 2022
29:34
ToubaVision ToubaVision
Рет қаралды 3,5 М.
Témoignage sur Sokhna Astou Gawane Mbacke
37:56
As-Samadiyya TV
Рет қаралды 2,9 М.
Regardez Mame Birame Wathie Recadre Pape Makhtar Diallo en direct
19:50
Diégo l’Espoir
Рет қаралды 70 М.
We Attempted The Impossible 😱
00:54
Topper Guild
Рет қаралды 56 МЛН