Рет қаралды 2,959
Mane Ahmadou Bamba la Yallah Talal …
Un poème écrit par cheikh MODOU Kara .
Man Ahmadu Banba la Yàlla tàllal
Yu baax i saalixiin ya la ma tàllal
Da may ku jeex ci Yàlla ak Yonent bi
Tey dundal lislaam diiney Yonen bi
La mbooleem yonent Yàlla yi yónnee
Ñoo àndandoo ñëw ma jiite walliyu yi
Yàlla miy def lu ko soob moo ma jiital
Man it sama Ahmadu mi laa jiital
Alastu Birabbikum ba ko Yàlla waxee
Maa toppoon ci yonent bi ba mu nee ballee
Léegi nag tay bii jamono maa ko moom
Li fiy tax a mucc itam man maa ko xam
Xasan sëtum yonent bi jàmbaar ja
Moo di doomi Hatiix Faadil jàmbaar ja
Sëy Mberi Maryaama Maami Móodu
Daa am sama ngëram ma jox ko Móodu
Noonu laa jële mbiru Seex Ibra
Sédd ca Ahmadu maneesu ci dara
Ya mu daan def mook Seex Ibra Faati
Moom la sët bi di def di doomi Faati
Waxoon ma mook Ceerno lu kenn dul fàtte
Déncoon ci moom secret di doomi Faati
Ku ñu naroon a jaarale ci Aminata
Moom Mareema àttanu ko ngir da fa tëh
Moo tax mu jaar ci Bun-Haffaan moom Ceerno
Mi ma dénk jamono ci bii xarnu
Dolli ko it ay matuwaay yu yéeme
Yu kenn masta am nde da maa yéeme
Lu ma mas a jox nit lu nurook moom
Ci nuru la yam, waaye du moom te du moom
Yàgg bawul dara yi wolof yiy wax
Man de danaa daj fépp lii laa leen wax
At mu ñëw rekk gën a leeral samay mbir
Ci desug Yàlla laa fi dese man maay mbër
Làmbi démb ja ñépp xam na ñu ku daan
Boroom loxo bu sew bii bërewul te moo daan
Zahiim Ahmadu sama yére yi
Moom laa bëgg a waaje ëllëg buñ may fayi
Yoral ma sama tur wi nga xam ni ku dul man
Buñ la ko woowee sam xel day dem ci man
Doomu Aadama yi Yàllaa ma leen may
Moo tax bu ma sañoon sawara da fay fay